kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu

kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day feddali ci ne ku bëgg a dem ca jullig Àjjuma ja sopp nañu ci moom mu sangu, kem sangul janaba.

فوائد الحديث

Feddalikug sangu àjjuma, ak ne sunna la ci jullit bi ci bisu àjjuma ji, sangu gi nekk buy dem ca julli ga moo gën.

Xér ci set ak xet gu teey dafa bokk ci jikkoy jullit bi ak i tegginam, mbir mi dana gën a feddaliku bu ñuy daje ak nit ñi ak bu ñuy toog ak ñoom, rawati na ci jullig àjjuma ak mbooloo.

Wax ji ci hadiis bi ki àjjuma war ci moom la ñeel; ndaxte moom moo cay dem.

Sopp nañu ci kiy ñëw àjjuma mu set, mu sangu ba xet gi deñ ci yaramam mu laal gëtt, bu jàppoo kese it dana ko doy.

التصنيفات

Sangu, Jullig Àjjuma