Allaahuma innii ahuusu bika min sawaali nihmatika, wa tahawwuli Hanafiyatika, wa fujaa-ati niqmatika, wa jamiihi saxatika

Allaahuma innii ahuusu bika min sawaali nihmatika, wa tahawwuli Hanafiyatika, wa fujaa-ati niqmatika, wa jamiihi saxatika

Jële nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: bokkoon na ci ñaani Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "Allaahuma innii ahuusu bika min sawaali nihmatika, wa tahawwuli Hanafiyatika, wa fujaa-ati niqmatika, wa jamiihi saxatika".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muslu na ci ñenti mbir: Bi ci njëkk: (yaw sama Boroom maa ngi muslu ci yaw ci deñug sag xéewal) yu diine yi ak yu àdduna yi ak ma sax ci lislaam, ak ma sori di tàbbi ci moy yiy dindi say xéewal. Ñaareel bi: (ak wëlbatikug sag jàmm) ci mu soppiku jëm ci balaa; ma lay ñaan jàmm ju sax, ak mucc ci mettit yi ak tawat yi. Ñatteel bi: (say musiba) ci ay balaa ak i musiba, balaa ak musiba bu ñewee ci ag mbetteel, te jamonoy tuub ak dabaatal nekku fa, kon ki mu dall day gën a màgg gën a tar ci moom. Ñenteel bi: (mbooleem sag mer) sabab yiy waral sag mer; ndax koo mere kooka sooy na ñàkk na. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa wax baat bii ngir mu làmboo mbooleem sabab yiy waral merum Yàlla mu Sell mi te kawe ci ay wax ak ay jëf ak i pas-pas.

فوائد الحديث

Soxlawoog Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jëm ci Yàlla mu kawe mi.

Muslu gu baarkeel gi dafa làmboo: ag tawfeex ci sant Yàlla, ak wattu ci tàbbi ci bàkkaar yi; ndaxte moom day dindi xéewal yi.

Xër ci sori barab yiy waral merum Yàlla mu kawe mi.

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muslu na ci mbetteelug balaa; ndax bu fayyoo ci jaam bi kon wàcce na ci moom balaa boo xam ne du ko man a jañ , te mbooleem mbindeef yi manuñu ko a jañ, donte dañoo dajaloo ñoom ñépp.

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muslu na ci wëlbatikug jàmmam moom Aji-Sell ji, ndax am na yiwi ñaari kër yi, te bu wëlbatikoo wolif ko kon musibag ñaari kër yi dal ko, te jàmm mooy yëwénug diine ak àdduna.

التصنيفات

Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM