Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne

Jële na ñu ci Abis Subayri mu wax ne : Ibn Subayri bu jullee ba sëlmël da daan wax: «laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi, laa ilaaha illal Laahu, wa laa nahbudu illa iyyaahu, lahun nihmatu wa lahul fadlu wa lahus sanaa ul hasanu, laa iLaaha illal Laahu muxlisiina lahud diina wa law karihal kaafiruuna» mu wax ne: «Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na tudd Yàlla ci sikar bii ginnaaw bu sëlmëlee ci julli farata yépp, maanaam mooy: "laa ilaaha illal laahu": manaam amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla. "wahdahu laa sariika lahu" maanaam: moom Yàlla amul bokkaale cig Yàllaam ak ci moomeelam ak ci ay turam ak i meloom. "lahul mulku" maanaam: moo moom nguur ga matale te yaatu, nguurug asamaan yi ak suuf si ak li nekk séen diggante. "wa lahul hamdu" maanaam: mooy ki melowoo ag mat gu sëkk, ki ñuy sant cig mat ngir bëgg ko ak màggal ko ci bépp anam cig mbégte ak ci tiis. "wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun" kàttanam lu mat sëkk la ci bépp anam, dara tëwu ko, te benn mbir ci bir yi tëwu ko. "laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi" maanaam: deesul juge ci benn melo jëm ci weneen melo, ak ci moy Yàlla jëm ci topp Yàlla, amul it benn kàttan ndare ci ndimbalul Yàlla ndax mooy Dimbalaakoon ba te ci moom la ñuy wakkirlu. "laa ilaaha illal Laahu wa laa nahbudu illa iyyaahu": ak feddali la ci maanaam jaamu ak dàq bokkaale, ak ne moom moo yayoo jaamu wolif lu dul moom. "lahun nihmatu wa lahul fadlu": moom moo bind xéewal yi te moo ko moom, dana ci may ci ngëneelam ku ko soob ci ay jaamam. "wa lahus sanaa-ul hasanu": moo yayoo tagg wu rafet ci jëmmam ak ci ay meloom ak ci ay jëfam ak ay xéewalam, ci bépp anam nag. "laa ilaaha Laaha illal Laahu, muxlisiina lahud diina": maanaam di aji-kennal ko ci lu dul ngistal mbaa ndéggtal ci jaamu Yàlla. "wa law karihal kaafiruuna" maanaam sax ci wéetal Yàlla ak di ko jaamu donte neexul yéefar yi.

فوائد الحديث

Sopp nañu ñu sàmmoonteek sikar bii ginnaaw julli farata gu ne.

Jullit day tiitaroo diineem di fésal ay mbaaxam, doonte neexul yéefar yi.

Baadub "duburas salaati" bu rotee cib hadiis: bu dee hadiis bi day wax ci sikar, la cay cosaan mooy mu nekk ginnaaw sëlmël, bu dee ñaan la nag kon mu nekk lu jiitu sëlmël ga.

التصنيفات

Sikkar yi ànd ak julli gi