Wàcce na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Alxuraan fekk mi ngi am ñent-fukki at

Wàcce na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Alxuraan fekk mi ngi am ñent-fukki at

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Wàcce na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Alxuraan fekk mi ngi am ñent-fukki at, mu sax Màkka fukki at ak ñatt, ñu dugal ko mu gàddaay, mu gàddaay dem Madiina, sax fa fukki at, daal di faatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

الشرح

Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day xibaare wàcce nañu ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wahyu yónni ko fekk moo ngi am ñent-fukki at, mu sax Màkka fukki at ak ñatt ginnaaw soloo gi, ñu digal ko mu gàddaay dem Madiina mu sax fa fukki at, daal di Faatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk moo ngi am juróom-benn fukki at ak ñatt.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis:

Yittewoog Sahaaba yi jaar-jaari Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

التصنيفات

Sunu Yónnent Muhammat yalna Yàlla xéewalal ko te jàmmal ko, Jaar-jaari Yónnent bi SLM