Yaw Yonnente Yàlla bi, yaayu Sahd de dafa faatu, ban sarax moo gën?, mu ne ko: "ndox", nee na: mu gas ab teen, daal di ne: lii ngir yaayu Sahd la

Yaw Yonnente Yàlla bi, yaayu Sahd de dafa faatu, ban sarax moo gën?, mu ne ko: "ndox", nee na: mu gas ab teen, daal di ne: lii ngir yaayu Sahd la

Jële nañu ci Sahiid ibn Hubaadata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yaw Yonnente Yàlla bi, yaayu Sahd de dafa faatu, ban sarax moo gën?, mu ne ko: "ndox", nee na: mu gas ab teen, daal di ne: lii ngir yaayu Sahd la.

الشرح

Yaayu Sahd ibn Hubaadata yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa faatu, mu laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ban xeetu sarax moo gën ngir mu saraxeel ko yaayam? Yonnente bi xamal ko ne mooy ndox, mu gas ab teen def ko sarax ngir yaayam.

فوائد الحديث

Leeral ne ndox moo gën ci xeeti sarax yi.

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jëmale Sahd ci saraxe ndox; ndaxte moo gën a mat njariñ ci mbiri diine ak yu àdduna, ak ngir tàngaay wu tar mbaa aajo mbaa néewug ndox mi.

Tegtal ci ne yoolu saraxe dana egg ci way-faatu ñi.

Rafetalug Sahd jëme ci ñaari way-juram yal na leen Yàlla dollee gërëm.

التصنيفات

Li nit def ci yoonu Yàlla ci alalam ngir nit ñi di ko jariñoo te kenn du ko donn, Saraxub coobarewu