إعدادات العرض
mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi
mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ànd nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jóge Màkka jëm Madiina ba nu eggee ci am ndox ci yoon wi am ñu gaawantu ca Tàkkusaan ga, daal di jàppu cig yàkkamti, ba nu egge fa ñoom gis seen tastën ya ndox mi laalu ko, Yonnente bi daal di wax ne: "mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi".
الترجمة
العربية አማርኛ অসমীয়া ગુજરાતી हिन्दी Bahasa Indonesia Kiswahili Tagalog اردو Tiếng Việt دری Hausa Nederlands नेपाली සිංහල پښتو Oromoo ไทย Svenska മലയാളം English Кыргызча Română తెలుగు Lietuvių Malagasy Türkçe ಕನ್ನಡ Српски Bosanski Kurdî Yorùbá فارسی ქართული Moore Kinyarwanda Português Magyar Македонски Azərbaycan Čeština Українська Русскийالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tukki jóge Màkka jëm Madiina ànd ak Sahaaba yi, ñu gis am ndox ci yoon wi, yenn Sahaaba yi gaawantu jàppu ngir julli Tàkkusaan ba tax seen wowaayu ginnaaw ndëggu yi di feeñ ñeel aji-xool ji, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: mbugal ak alkande ca sawara ñeel na ñiy gàtteñlu ci raxas seen ginnaaw ndëggu yi bu ñuy jàppu, mu digal leen ñuy jotal ak di matale njàppu mi.فوائد الحديث
Raxas tànk yi dafa war ci jàppu; ndaxte bu masaa daganoon kon du tëkku ci sawara ku raxasul tastën yi.
Matale cér yi ñuy raxas lu war la, te ku bàyyi lu ndaw ci yu ñu war a laabal cig tay ak woyofal ag julleem du wér.
Solos jàngal aji-réer ji ak gindi ko.
Aji-xam ji day dindi lu mu gis ci sànk farata ak sunna ci anam ga mu méngool.
Muhammat Ibn Ishaaq Addahlawii nee na: jotale ñatti xeet la: farata, te mooy fexe ba matale barab ba benn yoon, ak sunna te mooy :
raxas ñatti yoon, ak lu ñu sopp te mooy :
guddal ga te mu ànd ak ñattale ga.
التصنيفات
Ni ñuy jàppoo