toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu

toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ummu Habiibata bint Jahsin mi nekkoon ci soxnas Abdur Rahmaan ibn Awf dafa jàmbat Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dereet ju muy gis, mu ne ko: "toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu". Tax mu daan sangu ci julli gu nekk.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Kenn ci jigéen yi àndoon ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dereet ji dafa wéy di génn ci moom, Mu digal ko mu bañ a julli diir bi ko mbaaxam daan téye njëkk mbir mii di gaar, topp mu sangu daal di julli,moom nag mu daan ci coobarewu ñeel julli gu nekk.

فوائد الحديث

Dereet ju yàqu mooy:dereet ji di wéy di génn ci jigéen ji ginnaaw bisi mbaaxam yi mu aadawoo.

Kiy gis dereeti jorngel(derret ju yàqu) day jàppe boppam ki nekk ci mbaax ci kem bis yi mu daan gis mbaax,njëkk dereet ju yàqu ji di ko dal.

Bis yimu ko aadawoo woon a gis bu rombee, kon dees koy jàppe ku laab ci mbaax-doonte ànd na ak dereet ju yàqu-day sangu ci mbaax.

Kiy gis dereet ju yàqu nekkul ne dafa war a sangu ñeel julli gu ne; ndax sàngoom ga ag góor-góorlu la woon ci moom rekk,te bu nekkoon lu war kon Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dana ko leeral.

Kiy gis dereet ju yàqu dafa war a jàppu ñeel julli gu ne ; ndax ag tojam lu sax la te du dagg, noonu la deme it ci képp ku ag tojam

sax, niki ku ame feebaru saw muy toq, walla génne ngelaw guy wéy.

Laaj Boroom xam-xam yi lu lënt ci biri diine, ndax jigéen gii dafa jàmbat Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, laaj ko dereet ju bari ji koy dal.

التصنيفات

Mbërëg ak wësin ak dereeti wéradi