tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji

tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji

Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm Mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne moom Yónente bi tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na nisër, te mooy nit ki waral ci boppam lu Sariiha waralul ci moom, mu wax ne: nisër du gaawal dara te du ko yéexal, waaye dañu ciy genne ku nay ki dul def lu dul li war ci moom, ak ne nisër du indi dara lu dul lu ñu dogal ci moom.

فوائد الحديث

Yoonaluñu nisër, waaye bu nit ki nisëree day war ci moom mu matale ko ndeem nekkul ag moy.

Li waral tere gi mooy (du indi yiw); ndaxte du delloo dara ci dogalu Yàlla; ak it ngir aji-nisër ji

bañ a njort ne nisër gi moo tax li mu doon sàkku am, te yàlla Aji-Doylu la wolif loolu.

Al-Xurtubii nee na: tere gii barabam mooy niki mu wax: bu Yàlla wéralee sama aji-tawat ji kon war na maa saraxe lii, anamug tere gi mooy ne ba mu tegee jëfug jaamu gi ci amug la mu bëgg, day feeñ ne jagleelu ko yéeneg jéem a jege

Yàlla ndax ci li mu def, waaye dafa sóobu yoonu wecceente, te li koy leeral mooy bu aji-tawat ji wérul woon kon du saraxe la mu wékkoon ca wéram ga, te lii mooy melow ki nay, moom du génne dara ci alalam ci lu dul ag weccee gu teew, te sax day ëpp la mu génne ci lu gën a bari.

التصنيفات

Giñ yi ak nisar yi