ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira

ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira"

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne góor gu sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira ndeem tuubu ko.

فوائد الحديث

Li ñu jublu ci sooy mooy bu cosaan ba dara soppiwul, waaye bu dee sooy bu ñu defar moom du dugg si Hadiis bi.

Araamal nañu ci góor muy sol sooy.

Tere gi ñu tere sol sooy day làmboowaale it lal ko.

May nañu góor tuuti sooy bu nekk ci yéreem te yaatuwaayam bañ a ëpp ñaari baaaraam ba ñenti baaraam nga xam ne da koy def ay màndarga ci yére bi.

التصنيفات

Teggiini col