bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab

bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab

Jële nañu ci Al-Muxiirata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- cib tukki, ma nar a summi ñaari saŋam yi, mu ne ma: "bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab" mu masaa ca seen kaw.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci ab tukki, daal di jàpp, ba mu tollee ci raxas tànk yi Al-Muxiirata Ibn Suhbata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàllal loxoom ngir summi li nekk ci tànki Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-di ay dàlli saŋ ngir mu raxas ñaari tànk yi! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ne ko: bàyyileen te bu leen summi, ndax damaa dugal samay tànk ci saŋ yi fekk maa ngi cig laab, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di masaa ci kaw saŋ yi mu wuutu raxas ñaari tànk yi.

فوائد الحديث

Li nu yoonal ci masaa ci ñaari saŋ mooy mu nekk ci jàpp ñeel toj mu ndaw, bu dee sangu nag ñeel toj mu mag raxas ñaari tànk yi du man a njàkk.

Masaa benn yoon lay doon ci rombale loxo ba nu tooyal ci kaw saŋ yi wolif suuf gi.

Danañu sàrtal ci masaa ci ay saŋ, mu sol ko ginnaaw am njàpp mu mat mom raxas na ca ñaari tànkam ci ndox, ak saŋ yi nekk lu laab, ak mu muur barabu farata ba, ak mu masaa leen ci toj mu ndaw bu mu nekk toj mu mag walla luy waral sangu, masaa mi it na nekk ca waxtu wa ñu ko tënk ci sariiha te mooy bis ak guddi ñeel ku nekkul cib tukki, ñatti bis ak seeni guddi ñeel ki nekk cib tukki.

Dees na nattale ci ay saŋ lépp lu muur ñaari tànk yi niki ay kawas mbaa leneen, te dana dagan ñu masaa ca.

Rafetug jikkoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak um njàngaleem, ba tax mu tere Al-Muxiirata mu summi leen, daal di koy leeralal sabab si: ci ne bamuleen di sol boobu ay tànkam laab na, ngir xelam dal mu daal di xamit àtte bi.

التصنيفات

Teggiini tukki ak i àtteem, Masaa ci kaw sang ak yi mel ne moom