Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan jug guddi day socc

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan jug guddi day socc

Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan jug guddi day socc.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na bari lu muy socc di ko digle it, moom nag day feddaliku ci yenn waxtu yi, bokk na ca: socc bu ñu jògee guddi, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na bomb gémmeñam di ko setal ci socc.

فوائد الحديث

Yoonalug socc day feddaliku ginnaaw bu ñu nelawee ci guddi gi, ndaxte nelaw day waral xetu gémmiñ soppeeku, socc nag jumtukaayu setal la.

Yoonalug socc day feddaliku saa yu xetu gémmiñ gi soppikoo ba naqari, dañuy jàpp ci maanaa mi jiitu.

Yoonalees na set ci anam gu matale, te dafa bokk ci sunnay

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, bokk ci ay tegginam yu kawe yi.

Gémmiñ gi yépp lañuy socc mu làmboo: bëñ yi, ak siiñ yi, ak làmmiñ wi.

Socc ab bant la bu ñuy dagge ci garabu araag mbaa geneen, dees koy jëfandikoo ngir setal gémmeñ ak bëñ yi, te day teeyal gémmeñ, di dindi xet gu bon.

التصنيفات

Sunnay set, Na mu daa laabale boppam SLM