إعدادات العرض
yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi
yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi
Jële nañu ci Suhaybu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi, bu ko mbégte dalee day sant mu doon aw yiw ci moom, bu ko lor dalee day muñ mu doon aw yiw ci moom».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල دری অসমীয়া ไทย Tiếng Việt አማርኛ Svenska Yorùbá Кыргызча ગુજરાતી नेपाली Oromoo മലയാളം Română Nederlands Soomaali پښتو తెలుగు Kinyarwanda ಕನ್ನಡ Malagasy Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Lietuvių Македонски Azərbaycanالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day yéemu ci mbiri jullit bi ci anamug rafetlu; ndaxte ay mbiram yépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi; Bu ko mbégte dalee day sant Yàlla ci loolu; mu am ug pay ci cant gi, Bu ko lor dalee mu muñ te yaakaar payug Yàlla, mu am ug pay ca muñ ga, kon moom day am ug pay ci anam yépp.فوائد الحديث
Ngëneelu cant ci mbégte ak muñ ci lor, ku def loolu dana am yiw ci ñaari kër yépp, ku santul ci xéewal yi, te muñul ci musiba yi, yiw wu bari dana ko raw te dana am bàkkaar.
Ngëneelu ngëm, ak ne pay gi ci bépp anam, kenn du ku am ñu dul way-gëm ñi.
Sant ci jamonoy mbégte, ak muñ ci lor yi, daa bokk ci meloy way-gëm ñi.
Gëm dogali Yàlla day def aji-gëm ji mu nekk ci ngërëm lu mat ci gépp anam, mu wuute ak ku dul aji-gëm ji nga xam ne bu lor wàccee ci moom day mer ba fàww, bu amee xéewal gu jóge ci Yàlla mu màgg mi nag loolu da koy soxlaal ci ludul muy yittewoo topp Yàlla, mu koy jëmale nag ci moy Yàlla.
التصنيفات
Sellal bakkan yi