Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan sangu janaba, da daan raxas ñaari loxoom, jàpp njàppum julli, daal di sangu

Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan sangu janaba, da daan raxas ñaari loxoom, jàpp njàppum julli, daal di sangu

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan sangu janaba, da daan raxas ñaari loxoom, jàpp njàppum julli, daal di sangu, daal di xàjjale ci loxoom kawaram, bu ko wóoree ne der ba tooy na, mu sotti ca ndox ñatti yoon, topp mu raxas mbooleem yaramam, Aysatu nee na: daan naa sangu man ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn ndab, nun ñaar ñépp di ci tanq.

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan namm a sangu ci janaba day tàmbali ci raxas ay loxoom, Topp mu jàpp kem ni muy jàppe ngir julli, topp mu sotti ndox mi ci kaw yaramam, mu xàjjale kawaru boppam ci ay loxoom, ba bu jàppee ne ndox mi egg na ca cosaanu kawar ga, ba tooyal der ba, mu sotti ndox mi ci kaw bopp bi ñatti yoon, topp mu raxas li des ci yaramam. Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nee na: daan naa sangu man ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn ndab, nun ñaar ñépp di ci tanq.

فوائد الحديث

Sangu ñaari xeet la: boo xamne dana doy, ak bu mat sëkk, bu dee biy doy, nit ki day yéenee laab, daal di matale yaram wi lépp ci ndox boole ko ak gallaxndiku ak saraxndiku, bu dee bu mat sëkk bi nag, day sangu kem ni Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sangoo ci hadiis bii.

Danañu woowe janaba képp ku génne maniyu, walla mu sëy doonte génnewul maniyu.

Dagan na ci ñaar ñiy sëy ku ne xool awray keneen ka, ak ñu sangu ci genn ndab.

التصنيفات

Sangu