إعدادات العرض
misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga
misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga
Jële nañu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga, ñi nekk ci suuf bu ñuy wut ndox dañuy romb ña nekk seen kaw, nu mujj wax ne: nun de bu nu xaroon ci sunu wàll aw xarit te dunu lor ñi nekk sunu kaw, bu ñu leen bàyyee ak la ñu bëgg ñoom ñéppay alku, waaye bu ñu téyee seen loxo danañu mucc, ñoom ñépp mucc".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල Русский Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە Tiếng Việt ไทย پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or नेपाली Malagasy Kinyarwanda తెలుగు Lietuvių Oromoo Română മലയാളം Nederlands Soomaali Српски Українська Deutsch ಕನ್ನಡ Moore Shqip ქართული Azərbaycan Magyarالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa sadd misaal ñeel ñi taxaw ci foroñceeri Yàlla yi, ne coww ci ay ndigalam, di digle lu baax di tere lu bon, Ak misaalu ñiy tàbbi ci foroñceeri Yàlla yi bàyyi ndigle yi, di def tere yi, ak jeexitalu loolu ci muccug mbooloo mi, mu mel ni aw nit wu war ci ag gaal, ñu daal di sànni bant ngir xam kuy toog ci kaw gaal gi ak kuy toog ci suuf, ñenn ñi am kaw ga, ñeneen ñi am suuf ga, ñi nekkoon ci suuf bu ñu bëggee wut ndox dañuy romb ña ca kaw, Ñi nekk ci suuf daal di wax ne: nun de bu nu xaroon aw xar ci su nu bérab fii ci suuf ngir di ci wute ndox, ba dunu lor ñi nekk fi sunu kaw, ñi nekk ci kaw buñu leen bàyyee ba ñu def loolu, kon gaal gi dana leen suuxal ñoom ñépp, waaye bu ñu jugee tere leen ko, ñaari kurél yépp danañu mucc.فوائد الحديث
Solos digle lu baax ak tere lu bon ci aar mbooloo mi ak musal leen.
Bokk na ci yooni jàngale yi joxe ay misaal, ngir jegeele maanaa yi ci xel yi ci anam gu ñuy yëg.
Def ñaawteef wu fés te kenn ŋàññiwu ko loolu yàqute la guy lor ñépp.
Alkandeg mbooloo mi day tege ci bàyyi defkati yu bon yi ñuy wéy ci di yàq ci kaw suuf.
Doxiinu njuumte ak yéene ju rafet doyul ci yéwénal jëf.
Wareef yi ci askanu jullit yi dañu koy bokk, wànte duñu ko gàll benn nit kese.
Mbugal mbooloo mi ci bàkkaar bu ñenn ñi jagoo ndeem wàññiwuñu ko.
Ñiy def jëf yu bon dañuy wane seen bon ci anam wu baax ci askan wi, ñoom ak naaféq yi.
التصنيفات
Ngëneelu digle yiw tere njékar