ñaari ndëggu jaam bi du pënd ci yoonu Yàlla ba noppi sawara di ko laal

ñaari ndëggu jaam bi du pënd ci yoonu Yàlla ba noppi sawara di ko laal

Jële nañu ci Abii Absin Abdur Rahmaan ibn Jabrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ñaari ndëggu jaam bi du pënd ci yoonu Yàlla ba noppi sawara di ko laal».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day bégle ci ne ku ñaari ndëggoom pënd fekk da doon jihaad ci yoonu Yàlla kooku sawara du ko laal.

فوائد الحديث

Ag bégle ci kiy jihaad ci yoonu Yàlla ci mucc ci sawara.

Dafa tudd ñaari ndëggu yi donte pënd bi dafay matale yaram wi yépp; ndaxte ñi ëpp ci jihaadkat yi ci jamono yooyu dañu doon dox, te ndëggu day pënd ci bépp anam.

Ibn Hajar nee na: bu dee pënd bi laal ndëggu yi kepp day tax ñu araamal ko ca sawara; naka la kon ki dox def lum man.

التصنيفات

Ngëneelu xeex ci yoonu Yàlla