إعدادات العرض
nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
Jële nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jàpp ci sama mbagg daal di ne ma: «nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon", ibn Umar, daan na wax naan: boo gontee bul xaar suba, boo xëyee bul xaar ngoon, nanga jël ci sag wée ñeel sag tawat, ak ci sag dund ñeel sag dee.
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Português සිංහල Nederlands অসমীয়া Tiếng Việt ગુજરાતી پښتو Română മലയാളം नेपाली Deutsch Кыргызча ქართული Moore Magyar తెలుగు Svenska فارسی Македонски Kiswahili ಕನ್ನಡ Українська Kinyarwanda Oromoo ไทย Lietuvių Српски मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy ភាសាខ្មែរ O‘zbek தமிழ் Azərbaycanالشرح
Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm dafa wax ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa téye ci mbaggam -te mooy li boole doole ji ak yaxu mbagg mi- mu ne ko: nekkal ci àdduna mel ni doxondeem bu ñëw ci ab dëkk bu mu amul dëkkuwaay bu ko yiir, walla aji-dëkk ju koy dalal, mu wéet wolif njabootam ak i mbokkam ak i xameem, yi nga xam nooy waral soxlawoo wolif Aji-Bind ji, waaye nanga gën a tar doxandeem bi ci jamono ya muy jéggi di romb ca yoon wa ngir wuti réewam; ndax doxandeem bi amaana mu dëkk ca réewum tumurànke ma daa di fay sax, mu wuute ak kiy jéggi yoon wi jublu dëkkam, ndax bokk na ci ay mbiram woyofal ak ñàkk a taxaw, ak xér ci egg ca dëkkam, kem ni nga xamee ne aji-tukki ji soxlawul lu ëpp lu koy eggale fa mu jublu a tukki, niki noonu it aji-gëm ji du aajowoo ci àdduna lu ëpp lu koy eggale ca barab ba. Ibn Umar jëfe ndénkaane lii, daan wax naan: boo xëyee bul xaar ngoon, boo gontee bul xaar suba, te nga limaale sa boppu ci ñi faatu ñi ak ne dund gi du ñaak wér ak feebar. Gaawantul ci sa bisi yi nga am wér ci topp Yàlla ngir sag feebar; nga gaawantu ci jëf yu baax ci jamanoy wér balaa feebar di dox sa diggante ak moom, te nga gaawantu sag dund ci àdduna, dajale ca lu lay jariñ ginnaaw boo deewee.فوائد الحديث
Jàngalekat bi teg ab ténqam ci kaw mbaggu kiy jàng bu koy jàngal ngir miinal ko ak bàyyiloo ko xel.
Tàmbale ag laabire ak ug jubbanti ñeel ku ko sàkkuwul.
Rafetuw jàngaleg Yónente bi ci sadd ay misaal yuy taxa gëm wax ji ci li mu wax ne: "nekkal ci àdduna mel ni ab doxandeem walla kuy jaar ciw yoon".
Wuuteg nit ñi ci seen uw doxin jëm allaaxira; ki nekk ciw yoon, loolu dakoy def mu nekk ki gëna dëddu ab doxandeem.
Leeral gàttug mébét, ak waajal dee
Hadiis bi tegtalewul bàyyi wërsëg ak araamal neexiti àdduna; wànte day tegtale ag
xemmeemloo
ci ag dëddu, ak tuutal àdduna.
Gaawantu jëm ci jëf yu baax yi balaa mu koy ñàkk a manati, feebar tere ko ko mbaa dee.
Ngëneelu Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm ba tax mu jeexantalu ci waare wii jóge ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Dëkkuwaayu way-gëm ñi mooy àjjana kon moom doxandeem la ci àdduna, te aji-tukki la jëm allaaxira, du wékk xolam ci dara ci réewum tumbrànke mi, waaye xolam day wékku ci dëkkuwaay ba muy dellu, te ag saxam ci àdduna ngir faj aajoom la ak waaj ngir dellu ca réewam ma.
التصنيفات
Sellal bakkan yi