ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont

ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bégal na kiy dem ca jàkka ja ngir jaamu walla sàkku xam-xam mbaa geneen jubluwaayu yiw ci waxtu wu mu man a doon; ci njëlbeenu bëccëg gi walla ca mujj ga ci ne Yàlla waajalal na ko ab barab ak nganale ca àjjana, saa yu dikkee ca jàkka ja guddi walla bëccëg.

فوائد الحديث

Ngëneelu dem ca jàkka ja, ak ñaaxe ci sàmmonte ak mbooloo mi, bariwaana luy faat nit kiy wuute jàkka ya ci yiw ak ngëneel ak ug nganale gu Yàlla waajal ñeel ñiy jublu néegam ba.

Bu dee nit ñi ñooy teral ñiy ñëw ci seen kër yi, di leen jox ay lekk, kon Yàlla mu Baarkeel mi te kawe moo gën a tabe jaamam yi! Ku jublu néegam yi mu teral ko, Yàlla waajalal ko wàccuwaay bu màgg te rëy.

Bég ak ñeete ci dem ca jàkka ya; ndaxte dees koy waajalal wàccuwaay saa yu xëyee walla mu gont ci limub la mu fa dem.

التصنيفات

Ngëneelu jullig mbooloo ak i àtteem