rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal…

rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal Mu-axiru, wa Anta halaa kulli say-in xadiirun

Jële nañu ci Abuu Muusa yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu nettali ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne daan na ñaan ñaan gii: "rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal Mu-axiru, wa Anta halaa kulli say-in xadiirun ".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Bokkoon na ci ñaani Yonnente yu matale yi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, waxam ji: "yaw sama Boroom jéggal ma samay njuumte" ak samay bàkkaar, "ak samag réer" li jóge ci man ci ñàkk a xam. "ak samag ëppal ci sama mbir yépp" samag gàtteñlu ak samag jéggi dayo. "ak li nga xam ci man" xam nga ko yaw Yàlla waaye man fàtte naa ko. "Yaw sama Boroom jéggal ma samay njuumte ak samag tayeef" li jóge ci man ci ay bàkkaar ma tay ko te xam ko. "ak samag dëggal ak samag kaf" liy jóge ci man ci ay kaf ak liy tàbbi bawoo ci man ci ñaari anam yépp. "ak lépp lu ne ci man" mu boole li ñu tudd lépp ci ay bàkkaar ak i ayib. "yaw sama Boroom jéggal ma li ma jiital" ci li weesu, "ak li ma mujje" ci liy ñëw. "ak li ma yalu" li ma nëbb, "ak li ma biral" li ma feeñal. "yaay Aji-jiitale ji di Aji-yeexe ji" yaay jiital ku la soob ci sa mbindeef yi jëm ci sa yërmànde ci sa tawfeexal ñeel li nga gërëm, yaay yeexal ku la soob wolif loolu ci sag gàccaal ko, amul ku man a jiital loo yeexal, amul it ku man a yeexal loo jiital ci bir yi. "yaw yaay Aji-Am kàttan ci lépp" ku mat kàttan, matug nammeel, di Aji-Defaakoon lépp lu la soob.

فوائد الحديث

Ngëneelu ñaan gii, ak xér ci ngir roy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Tere nañu yàq, ak ne aji-yàq ji ku gaaru ci mbugal la.

Yàlla mu kawe mi moo gën a xam nit ki boppam, kon war na ci moom mu bàyyee mbiram Yàlla; ndax moom nit ki man naa juum te du ko xam.

Nit ki manees na ko a jàppe ay kafam kem ni ñu koy jàppe ci dëggam, kon war na ci nit ki muy moytandiku ci ay kafam.

Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: gisuma ci wenn yoonam bqrabu ñaan ji, li gën a rëy ci mujj gi nag am na... Daan na ko wax ci jullig guddi, rot na it ne daan na ko wax ci mujjanteelu julli gi, nettali yi wuute na ci ne ndax da ko daan wax njëkk muy sëlmal walla ginnaaw ga? Ci waxam la ñëwe.

Ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day juum bay jéggalu? Nee nañu da ko a wax ngir toroxlu ak wàcce boppam, walla mu jàppe bàyyi li ngëna mat ab bàkkaar, walla mu namm ci yi nga xam ne njuumte mooko waral, walla mu nekk lu jiitu Yónnente gi, nee nañu it: jéggalu ag jaamu la gu ñu war a def, du ngir sàkku njéggal, wànte ngir jaamu la, nee nañu itam: loolu ag yeete la ak ug jàngale ñeel aw xeetam, ngir ñu bañ am kóolute ba tax ñuy baña jéggalu.

التصنيفات

Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM