Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax,

Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax,

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax, xéral ci lu lay jariñ, te nga dimbandikoo Yàlla te bul lompañ, bu la dara jotee, bul wax ay bu fekkoon ne defnaa lii mbaa lee kon lii du am, waaye waxal ne Yàlla dogal na te lu ko neex lay def, ndax boo waxul loolu yaa ngi ubbil saytaane buntu».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne jullit léppam aw yiw la, waaye jullit bi dëgër ci ngëmam ak ug dogoom ak alalam ak yeneen moo ëpp yiw te moo gënal Yàlla mu màgg mi jullit bi néew kàttan. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di dénk jullit bi mu def sabab yi koy jariñ ci mbiri àdduna ak allaaxira, ànd ak sukkandiku ci Yàlla, tay dimbandikoo ci moom, te wakkirlu ci moom. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na ñàkk solo ak tàyyeel ak di yeexamtu ci def luy jariñ àdduna ak allaaxira. Bu jullit bi pasteefoo ci jëf, te jàpp ci sabab yi, di dimbandikoo Yàlla, di sàkku ci moom aw yiw, ginnaaw loolu li ko war mooy mu bàyyee mbiram Yàlla, te mu xam ne lu Yàlla tànn mooy li gën. Bu ko musiba dalee ginnaaw ga, bu mu wax: «Bu fekkoon ne defoon naa nàngam kon lii ak lee mooy am»; Di wax naan (bu dul woon nàngam) loolu day tijjil bunt saytaane" ci di gaaral ab dogal,ak di naqarlu li weesu, waaye na jébbalu te gërëm te wax: "Yàlla dogal na, te lu ko neex lay def", Lu am rekk dafa fekk ne noonu la ko Yàlla bëgge, Ndax mooy def lu ko soob, te amul kuy delloo ab dogalam,walla di ko dindi.

فوائد الحديث

Bokk na Nit ñi dañoo rawante ci ngëm.

Sopp nañu kàttan ci jëf yi; ndax njariñ man na caa ame amiin woo xam ne bu ca kàttan ga nekkul woon du am.

Nit ki dafa war a xér ci lu koy jariñ, te bàyyi lu ko dul jariñ.

War na ci aji-gëm ji muy sàkku dimbaluYàlla ci mbiram yépp, te mu bañ a sukkandiku ci boppam.

Saxal dogal yi ak ne loolu du dàquwante ak def sabab yi ak dox ci sàkku yiw yi.

Tere nañu ñuy wax "budul woon nàngam” di ko wax ci anamug naqarlu ci wàccug musiba, araamal nañu it di gaaral ab dogalu

Yàlla mu kawe mi.

التصنيفات

Masalay dogal yi, Jëfi xol yi