إعدادات العرض
Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax
Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax».
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية Bosanski English فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو हिन्दी 中文 Kurdî Português অসমীয়া Kiswahili Tagalog ગુજરાતી Tiếng Việt Nederlands සිංහල پښتو Hausa नेपाली മലയാളം Кыргызча Shqip Română Svenska తెలుగు ქართული Moore Српски Magyar Македонски Čeština Українська አማርኛ Azərbaycan Malagasy Kinyarwandaالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne jullit bi deesu ko toppe li xelam di xalaat ci ay njëkk mu koy def walla mu koy wax, ndax Yàlla yëkkëti na coono ba daal di jéggale, te du toppe xeetu Muhammat liy nekk ci am xelam di dengi-dengi ci xel mi lu dul mu am cag dal ak ug féex; bu ca xelam féexee nag niki rëy-rëylu ak puukarewu ak naaféq walla mu jëf ci ay céram mbaa mu wax ci làmmeñam, kon dees na ko jàppe loolu.فوائد الحديث
Yàlla mu kawe mi baale na jéggale na xalaat yiy nekk cim xel, nit ki di ko wax ak boppam, muy romb ci xel yi.
Bu nit ki xalaatee fase, mu gaar cim xelam, waaye waxu ko, bindu ko, kon deesu ko jàppe am fase.
Waxtaanu xel deesu ko jàppe nit ki ak lumu rëy rëy fii ak demul ba def ko, walla mu wax ko.
Màggug dayob
xeetu Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ñi jagleel ko bañ koo jàppe waxtaanu xel yi, mu wuute ak xeet yi jiitu woon.
التصنيفات
Waati fase yi