amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal

amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal

Jële nañu ci Aliyun mu wax ne: man góor laa woon gog bu ma déggee ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn hadiis rekk Yàlla jariñ ma ci luko soob, bu ma kenn ci ay Sahaabaam waxee dara bama giñloo ko bu ma giñalee ma dëggal ko, Abuu Bakar wax na ma te wax na dëgg, ne: dégg na Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal», mu daal di jàng aaya bii: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar} [ Aali-Imraan: 135].

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xamle ne amul benn jaam buy def bàkkaar, daal di rafetal am njàppam, topp mu jug julli ñaari ràkka yene ca tuub bàkkaaram bii, topp mu jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dana ko jéggal. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng waxu Yàlla ji: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar ana kan mooy jéggale bàkkaar yi ku dul Yàlla te duñu nuur ca la ñu defoon fekk ne xam nañu ko} [Aali-Imraan: 135].

فوائد الحديث

Ñaaxe ci julli ak jéggalu ginnaaw bàkkaar.

Yaatug njéggalu Yàlla mu màgg mi ak nangoom tuub ak jéggalu.

التصنيفات

Tuub