إعدادات العرض
war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam».
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Hausa తెలుగు Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া دری Кыргызча Lietuvių Kinyarwanda नेपाली മലയാളം Bosanski Italiano ಕನ್ನಡ Kurdî Oromoo Română Soomaali Shqip Српски Українська Tagalog Moore Malagasy தமிழ் Azərbaycan فارسی ქართული 中文 Magyarالشرح
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne: àq ju feddaliku la ci bépp jullit bu mat te am xel mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, daal di raxas ci bis boobu boppam ak yaramam, ngir laab ak set, li gën a yay ci bis yi nag mooy bisu àjjuma, kem ni ñu koy dégge ci yenn nettali yi, sangu bisu àjjuma nag lu jiitu julli gi lu ñu sopp la sopp gu feddaliku, donte sangu woon na bisu Alxamiis ci misaal, li tax nekkul farata nag mooy waxu Aysatu bi -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: "Nit ñi daan nañu def séen mbiri bopp, bu ñu daan dem àjjuma daan nañu dem ci séen melokaan wa, ñu ne leen, ay bu ngeen sangu woon", Al-Buxaarii moo ko nettali, ci beneen nettaleem bi: «Am nañu ay xet" maanaam xetu ñaq ak yeneen mbir yu mel noonu, ànd ak loolu ñu ne leen: "ay bu ngeen sangu woon" kon ku dul ñoom moo gën a yay.فوائد الحديث
Lislaam daa yittewoo ag cet ak laab.
Sangu àjjuma lu ñu sopp sopp gu ñu feddali ngir julli gi.
Dañoo tudd bopp doonte tudd gi ñu tudd yaram wi làmboo na ko; ngir yittewoo ko.
Sangu war na képp ku am xet gu bon guy lor nit ñi.
Bis bi gën a feddalikoo sangu mooy bisu àjjuma; ngir ngëneelam.