Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem

Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem

Jële nañu ci Xays Ibn Aasim -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem.

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy]

الشرح

Xaysu Ibn Aasim dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg jébbalu, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal ko mu sangu ci ndox ak garabu siddéem; ndax ay xobam dees koy jëfandikoo ci setal; ak xet gu teey gi mu am.

فوائد الحديث

Yoonalees na yéefar bi sangu buy dugg ci Lislaam.

Teddaangey Lislaam ak li mu yittewoo yaram ak ruu yépp.

Ndox bu jaxasoo ak bir yu laab yi du ko génne ca laab ga.

Yiy setal te xew bees dana taxaw taxawaayu siddéem, niki Saabu ak yu ni mel.

التصنيفات

Yiy waral sangu