sàppey góor ñi gi ci gën mooy gu njëkk gi, bi ci yées mooy gu mujj gi, sàppey jigéen ñi gi ci gën mooy gu mujj gi, gi ci yées mooy gu njëkk gi

sàppey góor ñi gi ci gën mooy gu njëkk gi, bi ci yées mooy gu mujj gi, sàppey jigéen ñi gi ci gën mooy gu mujj gi, gi ci yées mooy gu njëkk gi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne :Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «sàppey góor ñi gi ci gën mooy gu njëkk gi, bi ci yées mooy gu mujj gi, sàppey jigéen ñi gi ci gën mooy gu mujj gi, gi ci yées mooy gu njëkk gi».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamale ne sàppey góor yi gën ci julli te ëpp ci yool ak ngëneel mooy gu njëkk gi; ngir li ñu jege imaam bi ak di dégg jàngam mi ak li ñu sori jigéen ñi. Ba ca yées te gën ca a néewub yool ag ngëneel te gën ca a sori càkkuteefu Sariiha mooy ga ca mujj, Sàppey jigéen ñi ga ca gën mooy gu mujj ga; ndax moo leen gën a suturaal, moo gën a sori ci jaxasoo ak góor ñi, ak gis leen, ak fitnawu ci ñoom, ga ca yées mooy gu njëkk ga; ngir li mu jege góor ñi ak gaarlu ci fitna.

فوائد الحديث

Ñaax góor ñi ci njëkkante jëm ci

jaamu Yàlla ak ci sàppe yu njëkk yi ci julli yi.

Dagan na jigéen ñi julle ci jàkka yi ak góor ñi ci ay sàppe yu beru, waaye cig làqu ak nëbbu.

Bu jigéen ñi dajaloo ci jàkka ji, dañuy nekk ay sàppe kem sàppey góor ñi, te duñu teqalikoo, waaye dañoo war a raŋ ci sàppe te fat diggante yi, kem ni sàppey góor ñi mel.

Leeral yittewoog Sariiha gu tar ci ñaaxe ci soreele jigéen ñi ak góor ñi donte sax si barabu jaamu Yàlla la.

Nit ñi dañuy gënante ci kem seen i jëf.

An-Nawawii nee na: sàppey góor yépp ga ca gën ba fàww mooy gu njëkk gi, ga ca yées ba fàww mooy gu mujj gi, bu dee sàppey jigéen ñi li ñu ci namm ci hadiis bi mooy: sàppey jigéen yiy juleendoo ak góor ñi, bu dee dañoo beru julli te ànduñu ak góor kon ñoom ak góor ñi ñoo yam; seen sàppe ga ca gën mooy gu njëkk ga, ga ca yées mooy gu mujj ga.

An-Nawawii wax ne: sàppe gu njëkk gi ñu tagg ci hadiis bi ci ngëneelam ak di ca ñaaxe mooy gi topp ci imaam bi; moo xam boroomam dafa teel a ñëw walla mu yeex a ñëw, moo xam gàtteñlu moo ko gaar mbaa lu ko niru walla déet.

التصنيفات

Ngëneelu jullig mbooloo ak i àtteem