àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen di liggéey, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi

àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen di liggéey, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen di liggéey, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi, ndax fitna ji njëkk a am ci Banuu Israayil ci jigéen la xewe».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne àdduna ñam wu neex la, te naat ci gisiin, ba nit ki dana ci woroo, ba di ci nuur, ba def ko yitteem ji gën a rëy. Ak ne Yàlla dafa def ñenn ci nun ñuy wuutu ñeneen ci dundug àdduna, ngir xool lan lanuy def, ndax danu koy topp, walla danu koy moy? Topp mu wax: moytuleen bagaasi àdduna ak taaram di leen nax ba di leen jëme ci bàyyi li leen Yàlla digal, ba ngeen di def li mu leen tere. Bokk na ci li gën a màgg ci yi ñu war a moytu ci fitnay àdduna mooy fitnay jigéen ñi, ndaxte mooy fitna ji waa Banuu Israayil njëkk a tàbbi.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci taqoo ak ragal Yàlla, te bañ a soxlawoo liy feeñ ci àdduna ak taaram yi.

Moytondikuloo di fitnawu ci jigéen ñi, ci xool mbaa ci càgante ci góoru jàmbur di jaxasoo ak ñoom, mbaa yeneen.

Fitnay jigéen bokk na ci fitna yi gën a màgg ci àdduna.

Waaru ak xalam ci xeet yi jiitu woon, li xew ci Banuu Israayil man naa xew ci ñeneen.

Fitnay jigéen bu dee jabar la man naa teg jëkkëram lu mu àttanul ci ay deppaas, ba dana ko soxlaal wolif muy sàkku ay biri diineem, ba dana ko yóbbe muy xawa alku ci sàkku biri àdduna, bu dee jàmbur nag fitnaam mooy fiir góor ñi ci jengloo leen wolif dëgg ci bu nu génnee ba jaxasoo ak ñoom, rawatina bu ñu nekkee jigéen yu sollut lu jot, tey baraj-baraji, te lii man naa waral tàbbi ci njaalo ci kem ay darajaam, kon war na ci aji-gëm ji mu làqu ci Yàlla, te yaakaar ko ci mucc ci seeni fitna.

التصنيفات

Àttey jigéen ñi, Ŋàññ bëgg àddina