Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan

Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "«Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral juróomi mbir yu bokk ci meloy diiney Lislaam ak sunnas Yónente yi: Bi ci njëkk: xaraf, te mooy dagg der wi yokk ci sàkkaras ku góor ki ci kaw, ak dagg boppu der wi ci awray jigéen ci kaw barabu sëy bi. Ñaareel bi mooy: wat kawari naq, te mooy wat kawar gi nekk ci naq bi te wër awra wi. Ñatteel bi mooy: lewwi ay mustaas, te mooy jemp li sax ci tuñu ku góor ki ci kaw, ba deru tuñ wa di feeñ. Ñenteel bi mooy: lewwi ay we. Juróomeel bi mooy suqi kawari poqtaan.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Sunnay Yónente yi Yàlla bëgg te gëramloo ko, te digale ko, day waral ag mat ak ug set ak ub taar.

Yoonal nañu sàmmoonte a.

k bir yii, te bañ koo sàggane.

Melo yii am na ay njariñi diine ak àdduna, bokk na ca: rafetal ay melo, setal yaram, ak fegu ngir laab,

ak wuuteek yéefar yi, ak def ndigalal Yàlla.

Tudd na ñu ci yeneen hadiis yeneen melokaani sunnay bindiin yu dul juróom yii, niki: yar ab sikkim, ak socc, ak yeneen.

التصنيفات

Sunnay set