Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit yal na ko Yàlla dollee gërëm soxnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taqoo woon ak Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ngir sàkku Laylatul Xadri, mu wéy ci loolu ba Yàlla faat ko, ay soxnaam yal na leen Yàlla dollee gërëm taqoo ak Lihtikaaf ci ginnaawam.

فوائد الحديث

Yoonalees na Lihtikaaf ca jàkka ya, ba ci jigéen ñi sax ci kaw nikaw niko sariiha tërëlee ak budee mucc na ñu ci fitna.

Lihtikaaf day feddaliku ci fukk yi mujj ci weeru koor ngir li Yonnente bi taqoo woon ak moom.

Lihtikaaf sunna la suy wéy nasaxaluñu ko, ndaxte soxnay Yonnente bi yal na leen Yàlla dollee gërëm Lihtikaaf nañu ginnaawam.

التصنيفات

Beru ci jàkka ngir jaamu Yàlla