Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari

Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari

Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-daan na baril di ñaane ñaan yu matale yi,bokk na ca: "Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaaban-naari", Moom dafa làmboo yiwi àdduna ci wërsëg wu teey,te yaatu te dagan,ak jabar ju sell,ak doom ju sedd xool,ak nooflaay, ak xam-xam buy jariñ, ak jëf yu sell,ak yi ko niru ci ay càkkuteef yu ñu sopp te mu dagan, ak yiwi allaaxira ci mucc ci mbugëlu bàmmeel,ak taxawaay ba, ak sawara,ak am ngërëmal Yàlla, ak texe ca àjjanay xéewal gu sax ga, ak jege Boroom biy Aji-Yërëme.

فوائد الحديث

Sopp nañu di ñaan ñaan yu matale yi, ngir roy ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Li gën a mat mooy nit ki boole ci ñaanam yiwi àdduna ak allaaxira.

التصنيفات

Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM