Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa

Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Ashsrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa».

[Wér na] [Ibnu Maaja soloo na ko - At-tirmisiy soloo na ko - Abóo Daawuda soloo na ko - Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne jigéen du dagan ñu takk ko ci lu dul kilifa gu taxawe takk ga.

فوائد الحديث

Kilifa sart la ci wérug sëy, bu takk amee ci lu dul kilifa, walla jigéen maye boppam, kon sëy ba du wér.

Kilifa mooy góor gi gën a jege jigéen gi, kon kilifa gu sori du ko maye te ku jege nekk fa.

Sàrtal nañu ci kilifa: mu nekk mukàllaf, nekk góor, am xelum xam njariñi sëy, te kilifa gi ak ka muy meye ñu bokk diine, ku amul melo yii manut a nekk kilifa ci fas ab sëy.

التصنيفات

Sëy