Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski

Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski, ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ba ci jihaad ci yoonu Yàlla? Mu ne: «ba ci jihaad ci yoonu Yàlla, lu dul waa ju génne bakkanam ak alalam te dara ci yooyu dellusiwul».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko, ak Abóo Daawuda, kàddu gii ñeel na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne def lu baax ci fukki fan yi njëkk ci weeru Tabaski moo gën mbooleem bis yi ci at mi. Sahaaba yi laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jihaad ci lu dul fukki fan yii ndax moo gën walla jëf yu baax yi ñu jëf ci bis yii? Ngir li ñu xam ne jihaad bokk na ci jëf yi gën. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tontu ne: jëf ju baax ci bis yii moo gën jihaad ci yeneen bis yi, lu dul waa ju génn di jihaadi daal di riske bakkanam ak xaalisam ci yoonu Yàlla, mu ñàkk xaalisam, ruu ga rot ci yoonu Yàlla, Kii daal mooy ki gënle jëf ki def lu baax ci bis yu baax yii.

فوائد الحديث

Ngëneelu jëf ju baax ci fukki fani tabaski, war na ci jullit bi mu làng bis yii di ci baril ay jaamu, ci tudd Yàlla mu màgg mi, ak jàng Alxuraan, ak kàbbar ak tudd Yàlla, ak sant Yàlla, ak julli ak saraxe ak woor, ak mbooleem jëf yu baax yi.

التصنيفات

Fukki bis yi jëkk ci weeru Tabaski, Ngëneelu xeex ci yoonu Yàlla