ku ma fenal te tay ko na jël wàccuwaayam ca sawara

ku ma fenal te tay ko na jël wàccuwaayam ca sawara

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku ma fenal te tay ko na jël wàccuwaayam ca sawara».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne ku ko fenal te tay ko askanale ko wax walla jëf ci ay fen, kooku allaaxira am na fa toogukaay ca sawara; muy ag payam ci li mu ko fenal.

فوائد الحديث

Fenal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jublu ko ca te tay ko sabab la ci dugg sawara.

Fenal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yamul ak fenal yeneen nit ñi, ngir la cay tege ci yàqute yu màgg ci diine ak àdduna.

Dañuy moytondikuloo tasaare ay hadiis lu jiitu ñuy gëstu ak a wóorlu ndax li ñu ko askanale Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wér na walla déet.

التصنيفات

Solos Sunna ak wàccuwaayam, Jikko yees ŋàññ