Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne

Jële nañu ci Amru Ibn Aamir mu jële ci Anas Ibn Maalik mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne, ma ne ko: lan ngeen daan def yéen? Mu ne: njàpp mi dana doy nit ki feeg tojlewul.

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàpp ci jullig farata gu ne, donte njàppam tojul; loolu ngir am yool ak ngëneel. Dana dagan nag ñu julli ci mennum njàpp lu ëpp benn julli farata feeg moo ngi ca njàpp ma.

فوائد الحديث

Li ëpp ci jëfu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy di jàpp ci gépp julli; ngir sàkku lu gën a mat.

Sopp nañu fi jàpp ci bépp julli.

Dagan na ñi julli lu ëpp genn julli ci mennum njàpp.

التصنيفات

Ngëneelu njàpp