bokk na ci rafetug ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ

bokk na ci rafetug ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "bokk na ci rafetug ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ".

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne: bokk na ci matug rafetug lislaamu nit ki ak matug ngëmam, mu sori lépp lu ko amalul njariñ te mbiram te yitteelu ko, ak lépp lu ko dul jariñ ci ay wax ak i jëf, walla lu ko amalul njariñ ci diine ak ci àdduna, ndax yittewoo lu ñeelul nit ko amaana mu soxlaal ko wolif li ko amal njariñ, walla mu jëme ko ci lu mu waroon a moytu; ndax nit ki dees koy laaj ay jëfam ëllëg bis-pénc.

فوائد الحديث

Nit ñi dañuy rawante ci lislaam, te day gën a rafet ci yenn jëf yi.

Bàyyi ay caaxaan ak wax ak i jëf yu amul solo tegtal la ci matug lislaamu nit ki.

Ñaaxe ci soxlawoo luy jariñ nit ki ci biri diineem ak àddunaam, bu fekkee ne dafa bokk ci rafetug lislaamu nit ki mu bàyyi lu ko amalul njariñ, kon bokk na ci rafetam muy yittewoo lu koy jariñ.

Ibn Al-Xayyim yal na ko Yàlla yërëm nee na: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa dajale mbooleem fegu yi ci gennug kàddu, daal di wax ne: "bokk na ci rafetug lislaamu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ", lii day boole bàyyi lu amul njariñ: ci wax ak xool, ak déglu, ak jàpp, ak dox, ak xalaat, ak mbooleem yëngëtu yu feeñ yi ak yu nëbbu yi, kon lii kàddu la gu matale ci fegu.

Ibn Rajab nee na: hadiis bii cosaan la ci cosaani teggin yi.

Ñaaxe ci sàkku xam-xam; ndax ci la nit ki di xame li ko amal njariñ ak li ko amalul njariñ.

Digle lu baax ak tere lu bon ak dénkaane liy jariñ nit ki; ndax lu ñu digle la.

Day dugg ci mataleg maanaam hadiis bi: sori lu amul njariñ ci yi Yàlla mu màgg mi araamal ak yi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc sib, niki noonu li mu aajowoowul ci biri allaaxira niki dëgg-dëggi kumpa yi ak faramfaccey àtte mbindeef yi ak mbir ya, bokk na ca laaj ak gëstu masala yu ñuy nattale di ko foog te amagul, walla sax xawut a mana am, walla ag amam sax xalaatuñu ko.

التصنيفات

Jikko yees ŋàññ