jikkóom moo doon

jikkóom moo doon

Sahd Ibn Hisaam Ibn Aamir ba mu duggee ca néeg Aysatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: Yaw yaayu jullit ñi, wax ma jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu ne ma: xanaa doo jàng Alxuraan? Ma ne ko: ahakay, mu ne ma: jikkóom moo doon.

[Wér na] [Muslim soloo na ko ci ab Adiis bu gudd]

الشرح

Laaj nañu yaayu jullit ñi Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu tontu ci baat bu matale, daal di delloo laajkat bi ci Alxuraan ji boole mbooleem jikkó yu mat yi, daa di ne ko yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jikkóy Alxuraan lajikkówoo woon, lu Alxuraan digle mu def ko, lu Alxuraan tere mu moytu ko, jikkóom doon jëfe Alxuraan, ak taxaw ci ay digam, tegginoo ay tegginam, waaru ci ay niralam ak i nettaleem.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci roy ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak jikkówoo jikkóy Alxuraan.

Tagg jikkóy Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci ne ci leeru wahyu gi la bokk.

Alxuraan mooy cosaanu bépp jikkó bu tedd.

Jikkó yi ci Lislaam day làmboo diine jépp, ci def ndigal yi, moytu tere yi.

التصنيفات

Meloy jikko ya