aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf

aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Nekkoon nanu fi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu dégg am riir, Yonnente bi daal di wax ne: "ndax xam ngeen lan la?" Nee na: nu ne ko: Yàlla ak ub yonnenteem ñoo xam, mu wax ne: "aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa dégg ag kàddu gu xumb mel ni jëmm la ju daanu, mu laaj Sahaaba ya nekk fa moom yal na leen Yàlla dollee gërëm ba xam kàddu googu lan la, ñu ne ko: Yàlla ak ub yonnenteem ñoo xam. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: kàddu googu ngeen di dégg de aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara la diirub juróom-ñaar-fukki at, moom mooy door a daanu ca biir, ba egg ca suuf leegi bi ngeen di dégg kàddu gi.

فوائد الحديث

Soññee ci waajal bis bu mujj ba ci jëf yu baax, ak xuppe ci sawaraw Jahannama.

Sopp nañu lu nit ki amul xam-xam mu delloo xam-xam ba ci Yàlla mu kawe mi.

Jàngalekat bi day

bàyyiloo xel njëkk muy leeral; ngir ñu gën ko a dégg.

التصنيفات

Meloy Àjjana ak Sawara