Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp

Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bokk na ci sàrti wérug julli: laab, kon ku bëgg a julli day war ci moom mu jàpp ndeen dafa def luy yàq njàpp; niki dem duus walla saw walla nelaw mbaa leneen.

فوائد الحديث

Jullig ku tojle deesu ko nangu ba keroog muy laab ci sangu set ci toj mu mag, mbaa ci njàpp ci toj mu ndaw.

Jàpp mooy jël am ndox wërale ko ci biir gémmiñ daal di koy génne, daal di xëcc ndox mi ci ag noyyeem mu jëm ci biir bakkanam, mu génnewaat ko ci fiiru, topp mu raxas xarkanamam ñatti yoon, daal di raxas ñaari loxooom ànd ak conco yi ñatti yoon, daal di masaa bopp bi benn yoon, topp mu raxas ñaari tànk yi ñatti yoon.

التصنيفات

Njàpp