digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya

digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya

Jële nañu ci Amr ibn Suhaybu mu jële ci baayam mu jële ci maamam mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya».

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne war na ci baay bi mu digal ay doomam-góor ñi ak jigéen ñi- ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at,mu xamal leen li ñu aajowoo ngir taxawal ko. Bu ñu matalee fukki at mu dolli ca ndigal la, di leen dóor ci bi ñu ca gàtteñloo, te teqale seen diggante ca lal ba.

فوائد الحديث

Jàngal xale yi seen mbiri diine njëkk ñuy mat mukallaf, te julli bokk na la ca ëpp solo.

Dóor gi ngir yar la, waaye nekkul ngir mbugal, kon dees na ko dóor dóor gu yelloo ak jëmmam.

Yittewoog Sariiha ci sàmm der yi, ak fatt bépp bunt buy jëme ci yàq.

التصنيفات

Warug julli ak àtteb ki ko bàyyi