buleen njëkka nuyu Yahuud yi ak Nasaraan yi ci nuyoog Salaam, bu ngéen dajee ak kenn ci ñoom ci yoon nangeen ko jaarloo fa gën a xat

buleen njëkka nuyu Yahuud yi ak Nasaraan yi ci nuyoog Salaam, bu ngéen dajee ak kenn ci ñoom ci yoon nangeen ko jaarloo fa gën a xat

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "buleen njëkka nuyu Yahuud yi ak Nasaraan yi ci nuyoog Salaam, bu ngéen dajee ak kenn ci ñoom ci yoon nangeen ko jaarloo fa gën a xat".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere jullit bi di njëkk a nuyu Yahuud bi ak Nasaraan bi donte dañoo bokk ci ña ñu kóllareenteel, kon yéefar bu dul ñoom safut a wax, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral ne bu nu dajee ak kenn ci ñoom ci yoon wi nanu ko loruloo ca yoon wa gën a xat, aji-gëm ji mooy dox ci diggu yoon wi, waaye yéefar bi mooy randu, jullit bi du doyadi ci genn anam ci anam i doyadi yi.

فوائد الحديث

Daganul ci jullit bi muy njëkk a nuyu kenn ci Yahuud yi ak Nasaraan yi ak ñeneen ci yéefar yi.

Dagan na mu delloo leen nuyóo bu dee ñoom ñoo ko njëkk a nuyu, ci mu wax: wahalaykum (ak yéen).

Daganul ci jullit bi muy jubloo lor yéefar bi ci mu koy xatal cig tay te dara waralul mu loruloo ko ca yoon wa gën a xat; waaye bu dee yoon wi dafa xat walla mu xumb kon jullit bi moo ci gën a yay yéefar bi day randu.

Feeñal teddngay jullit ñi ak xeebug ku dul ñoom, ci lu dul tooñ walla ñaaw i wax.

Xatal ci kaw yéefar yi ngir sababus li ñu nekk ci weddi Yàlla mu kawe mi, loolu amaana mu nekk sabab ci ñu dugg ci lislaam; mu mucc ci sawara, bu dee loolu yóbbe na leen ñu xam sabab si.

Aayul jullit bi njëkk a wax yéefar bi naka nga def, naka nga xëye, naka ngoon gi? Mbaa lu ko niru bu dee aajo moo ko waral; ndax tere gi dees koo tënk ci Assalaam.

At-Tiibii nee na: li nu tànn mooy ne ab bidaakat deesu ko njëkk a nuyu, bu nuyóo ku mu xamul mu mujj feeñ ne yéefar gu ñu kóllareenteel la walla ab defkatu bidaa, kon day wax: dellu naa ca sama nuyu ga, ngir tuutal ko.

التصنيفات

Teggiini nuyoo ak yëglu