saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati

saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sarax du wàññi alal, waaye day fegal nit ki ay gàkk-gàkk, te Yàlla day wuutalal boroomam aw yiw wu màgg, loolu di ag dolliku waaye du ag wàññiku. Jéggale te am kàttanu fayu du dolli boroom lu dul kàttan ak tedd nga. Kenn du toroxlul Yàlla, ci lu dul mu ragal kenn mbaa muy laamisook kenn, walla muy sàkku ci moom njariñ, lu dul ne payam mooy ak yëkkatiku ak teraanga.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Yiw ak texe moo ngi ci topp Sariiha ak di def lu baax, donte ñenn ci nit ñi da ñuy foog lu wuuteek loolu

التصنيفات

Saraxub coobarewu