إعدادات العرض
{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp
{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp
Jële nañu ci Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Génn nanu ci guddi gu bari taw te lëndëm lool, di wër Yonnente Yàlla bi ngir mu jiite nu julli, nee na: nu dab ko, mu ne ma: "waxal" te waxuma dara, mu waxaat ma: "waxal", te waxuma dara, mu ne ma: "waxal", ma ne ko: lan laay wax? Mu ne ma: "{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp".
[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Português සිංහල Svenska ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە Tiếng Việt Kiswahili پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or Malagasy नेपाली Čeština Oromoo Română Nederlands Soomaali తెలుగు ไทย മലയാളം Српски Kinyarwanda ಕನ್ನಡ Lietuviųالشرح
Sahaaba bu màgg bii di Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne: ñoom dañoo génnoon ci guddi gu bari taw, te lëndëm lool, di seet Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ngir mu jiite leen julli, ñu gis ko, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "waxal" maanaam mune ko jàngal, waaye moom jàngul dara, Yonnente bi bàmtuwaat wax ji, Abdullah ne ko: lan laay jàng yaw Yonnente Yàlla bi? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: jàngal saaru Ixlaas {xul huwal Laahu Ahadun}, ak ñaari musluwaay yi {xul ahuusu bi rabbil falaxi}, ak {xul ahuusu bi rabbin naasi}, waxtuw ngoon, ak waxtuw suba, ñatti yoon, kon dana la wattu ci bépp ay, fegal la ci lépp lu bon.فوائد الحديث
Sopp nañu ñu jàng saaru Ixlaas ak ñaari musluwaay yi (falaxi ak naasi) ci suba gi ak ci ngoon gi, ndaxte kaarànge
la ci bépp ay.
Ngëneelu jàng saaru Ixlaas ak falaxi ak naasi
التصنيفات
Sikkari suba ak ngoon