إعدادات العرض
demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk
demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa seet Saabit Ibn Xaysin, benn waay ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, man dinaa la xamal xibaaram, mu dikkal ko fekk ko mu toog ci këram, sëgg boppam bi, mu ne ko: ana luy sa mbir? Mu ne ko: xanaa ay, da doon yëkkati kàddoom ci kaw kàddug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, kon moom ci waa sawara la, waa ji ñëw wax Yonnente bi ne ko: nee na lii ak lee, mu delluwaat beneen yoon indi ag bégle gu màgg, ne ko: "demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk".
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Hausa తెలుగు Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া دری Fulfulde Кыргызча Lietuvių Kinyarwanda नेपाली മലയാളം Bosanski Italiano ಕನ್ನಡ Kurdî Oromoo Română Shqip Soomaali Српски Українська Moore Tagalog தமிழ் Malagasy Azərbaycan فارسی ქართული 中文 Magyarالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da doon seet Saabit Ibn Xaysin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- daal di koy laajte, benn waay ne ko: man dinaa la amal xibaaram, ak lu tax mu fàddu, mu dem fa moom fekk ko ci këram mu jaaxle sëgg bopp bi, mu laaj ko: lan mooy sa mbir? Saabit wax ko ay wi nekk ci moom; ndaxte moom da daan yëkkati kàddoom ci kaw kàddug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te Yàlla dafa tëkku kuy def loolu ci ay jëfam yàqu, ak ne moom ne waa sawara la bokk! Waa ji dellu fa Yonnente ba -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ko loolu, Yonnente bi digal ko mu dellu fa Saabit bégal ko ci ne moom bokkul ci waa sawara waaye ci waa àjjana la bokk, ndaxte kàddoom gu kawe gi mbinddin la ci moom, ak ne moom moo doon waxal Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan waxal it waa Lansaar yi.فوائد الحديث
Leeral ngëneelu Saabit Ibn Xaysin -yal na ko Yàlla gërëm- ci ne moom ci waa àjjana la bokk.
Yittewoo gi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yittewoo ay Sahaabaam ak daan leen nemmeeku.
Ragal gi Sahaaba yi ragal ak tiit ci séen i jëf di yàqu.
Dañoo war a am i teggin bu ñuy wax ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci bi muy dund, ak di suufeel kàddu yi bu ñuy déglu sonnaam ginnaaw bi mu faatoo.