Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne

Jële nañu ci Warraad mi daa bindal Al-Muxiirata Ibn Suhbata mu wax ne: Al-Muxiirata Ibn Suhbata xamal na ma ci benn téere bu jël ca Muhaawiya ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne: «laa iLaaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu, wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, Allaahumma laa maaniha limaa ahtayta, walaa muhtiya limaa manahta, walaa yanfahu sal jaddi minkal jaddu».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci ginnaawam jullig farata gu ne: "laa iLaaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu, wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, Allaahumma laa maaniha limaa ahtayta, walaa muhtiya limaa manahta, walaa yanfahu sal jaddi, minkal jaddu". Maanaam: maa ngi saxal tey nangu kadduy Tawhiid gi, laa iLaaha Illal Laahu, jaamu dëgg Yàlla rekk laa koy saxalal, di ko dàq ci ku dul moom, amul lu ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, may saxal it ne nguurug dëgg te mat Yàlla rekk a ko moom, ak ne mboolleem canti waa asamaan yi ak waa suuf Yàlla rekk moo ko jagoo, ndaxte moom mooy ki am kàttan ci lépp, te lu Yàlla dogal ci joxe mbaa xañe kenn manu koo delloo, te amul benn way woomal gu koomam di jariñ fa Yàlla, waaye la ko fay jariñ mooy ay jëfam yu baax.

فوائد الحديث

Sopp nañu sikar bii ginnaaw gépp julli ndax li mu làmboo ci ay baati kennal Yàlla ak cant ko.

Gaawantu ci def Sunna yi, ak tasaare ko.

التصنيفات

Sikkar yi ànd ak julli gi