diggante ñaari nodd yu nekk am na julli, diggante ñaari nodd yu nekk am na julli" topp mu wax ca ñatteel ba: "ñeel ku mu soob

diggante ñaari nodd yu nekk am na julli, diggante ñaari nodd yu nekk am na julli" topp mu wax ca ñatteel ba: "ñeel ku mu soob

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Muxaffal yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «diggante ñaari nodd yu nekk am na julli, diggante ñaari nodd yu nekk am na julli" topp mu wax ca ñatteel ba: "ñeel ku mu soob».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne diggante nodd ak liqaam gu nekk am na jullig naafila, mu baamtu ko ñatti yoon, mu xamle ca gu mujj ga ne loolu dañu ko sopp ci ku bëgg a julli.

فوائد الحديث

Sopp nañu julli ci diggante nodd ak liqaam.

Njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci baamtu ay wax, loolu nag ngir ñu dégg ko ak mu feddali solos li muy wax

Li ñu namm ci ñaari nodd yi: mooy nodd ak liqaam, mu tudde leen (ñaari nodd) ngir notal, niki ñaari weer(jant bi ak weer wi) ak ñaari Umar yi(Abuu Bakrin ak Umar).

Nodd mooy yégle duggug waxtu wi, liqaam mooy yégle jotug julli gi.

التصنيفات

Nodd ak taxawal, Jullig coobarewu