bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj

bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax jenn jigéen ju bokk ci Ansaar yi Ibn Abbaas tudd na ko waaye maa fàtte turam:"lan moo la tere nga ànd ak nun aji?" Mu ne ko: amunu lu dul ñaari giléem baayu doomam ak doomam ja aji ca genn giléem ga bàyyeel nu genn giléem te ci lañuy wute ji ndox,mu ne ko:"bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Bi Yonnente bi jogée ca ajug tàggatoo ga,dafa wax jenn jigéen ju bokk ci waa Ansaar lu tax ajiwóo:lan moo la teree ànd ak nun aji? Ndaw sa daaldi joxe ngànt ci ne ñaari giléem lañu am, jëkkëram ak doomam aji ca genn giléem ga, bàyyi fa genn gi ngir ñu ciy rooti ndox ca teen ba. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ko ne umra ci weeru koor payam day yemoo ag aj.

فوائد الحديث

Ngëneelu umra ci weeru koor.

Umra ci weeru koor day yemoo ag aj ci ag pay, waaye du tee aj ga nekk lu war.

Yoolu jëf yi day yokku ci màggaayu jamono ji, bokk na ca jëf yi ci weeru koor.

التصنيفات

Ngëneelu aj ak wumra