Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam topp mu saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal

Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam topp mu saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam topp mu saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal, bu kenn ci yéen yewwoo ci nelawam na raxas loxoom njëkk mu koy dugal ci jàppukaay bi, ndax kenn ci yéen xamul fa la loxoom fanaan". Baati Muslim mooy: "bu kenn ci yéen yeewoo ci nelawam bu mu nuur loxoom ci ndab li ba baa mu koy raxas ñatti yoon ba noppi, ndaxte moom xamul fan la loxoom fanaan ".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na àttey laab, bokk na ca: Bu njëkk bi: kuy jàpp war naa dugal ndox mi ci bàkkanam cig noyyi, daal di koy génne cig noyyi ba tay. Ñaareel bi: ku bëgg a setal sobe Si génne ci moom, ak dindi ko ci lu dul ndox niki xeer mbaa leneen, kon setal ga day nekk ci lim gu tóol, la ca gën a néew mooy ñatt, la ca gën a kawe nag mooy lay dindi la doon génn tey setal bérab ba. Ñatteel bi: ku yeewu ci nelawi guddi du dugal loxoom ci ndab li ngir jàpp ba keroog mu koy raxas ñatti yoon ci biti ndab li, ndaxte moom xamul fan la loxoom fanaan, kon du wóolu ne am na sobe, te amaana Saytaane fo ca ba def ca ay bir yuy lor nit ki mbaa muy yàq ndox mi.

فوائد الحديث

Saraxndiku dafa war ci njàpp, te mooy: dugal ndox mi ci bakkan jaare ko ci noyyi, niki noonu it saraxndiku daa war, te mooy: génne ndox mi ci bakkan bi jaare ko ci noyyi.

Sopp nañu fomp di lu tóol.

Yoonalees na raxas ñaari loxo yi ñatti yoon ginnaaw ay nelawi guddi.

التصنيفات

Teggiini faj-aajo, Njàpp, Teggiini nelaw ak yewwu