Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka

Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka: ñaari ràkka njëkk tisbaar, ak ñaari ràkka ci ginnaawam, ak ñaari ràkka ginnaaw timis ci këram, ak ñaari ràkka ginnaaw gee ci këram, ak ñaari ràkka njëkk jullig suba, moom nag aw waxtu la woo xamne kenn daawul dugg fa Yonnente bi nekk, Hafsa nettalinama ne bu noddkat bi daan nodd ba fajar gi fenk day julli ñaari ràkka, ci jeneen wax: moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na julli ñaari ràkka ginnaaw àjjuma.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér, ci mbooleem anami nettali yi mu dikkee]

الشرح

Abdullah Ibn Umar -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne: bokk na ci naafila yi mu wattoo ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka, ñu koy wooye sunnay rawaatib, Ñaari ràkka njëkk tisbaar, ak ñaari ràkka ginnaawam, Ak ñaari ràkka ginnaaw timis ci këram, Ak ñaari ràkka ginnaaw gee ci këram, Ak ñaari ràkka njëkk fajar, Loolu mat fukki ràkka. Bu dee jullig àjjuma nag daa na julli ñaari ràkka ginnaawam.

فوائد الحديث

Sopp nañu sunnay rawaatib yii, ak sax ca.

Yoonalees na def Sunna yi ca kër ga.

التصنيفات

Jullig coobarewu, Na mu daa jullee SLM, Na mu daa doxalee ci sëy ak dundam ak i soxnaam