ndax kenn ci yeen du ragal walla muy tiit bu yëkkatee boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam, walla Yàlla def meloom wi melow mbaam

ndax kenn ci yeen du ragal walla muy tiit bu yëkkatee boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam, walla Yàlla def meloom wi melow mbaam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax kenn ci yeen du ragal walla muy tiit bu yëkkatee boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam, walla Yàlla def meloom wi melow mbaam».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral tëkku gu tar ci kaw kiy yëkkati boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam, walla moloom wi melow mbaam.

فوائد الحديث

Maamuun bi ak imaam bi am na ñent anam: ñatt yi dañu koo tere, te mooy: jiitu, ak tollo, ak yeex, la ñu yoonal ci maamuun bi mooy: topp imaam bi.

Maamuun bi daa war a topp imaam bi ci julli gi.

Ag tëkku ci soppi melow kiy yëkkati boppam njëkk imaam bi def ko melow mbaam lu man a nekk la, te mooy soppi.

التصنيفات

Àttey ki jiite julli ak ña mu jiite