Allaahumma innii ahuusu bika min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali

Allaahumma innii ahuusu bika min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ñaan daan na wax: " Allaahumma innii ahuusu bika min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali". Am na ci jeneen wax ci Muslim: "bu kenn ci yéen noppee ci taaya ju mujj ji, na muslu ci Yàlla ci ñent: ci mbugalu Jahannama, ak ci mbugalu bàmmeel, ak ci fitnay dund ak dee, ak ci ayu Masiihud Dajjaal ".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan muslu ci Yàlla ci ñent, ginnaaw taaya ju mujj ji, njëkk ñuy sëlmël ci julli gi, mu digal nu nuy muslu ci Yàlla ci yooyu, Bi ci njëkk: ci mbugalu bàmmeel. Ñaareel bi: ci mbugalu sawara ëllëg bis-pénc. Ñatteel bi: ci fitnay dund ci bànneexi àdduna yi nu araamal, ak lënt yiy réerale, ak fitnay dee, maanaam waxtuy sukuraat, ci jéng wolif lislaam mbaa sunna, walla fitnay bàmmeel niki laaji ñaari malaaka yi. Ñenteel bi: fitnay Al-Masiihud Dajjaal miy génn ci mujjug jamono, Yàlla di ci nattu ay jaamam; da koo jagleel cig tudd nag ngir màggug fitnaam ak i réeralateem.

فوائد الحديث

Muslu yii dafa bokk ci ñaan yi gën a am solo te matale, ngir li mu làmboo ag muslu ci ayi àdduna ak allaaxira.

Mbugalu bàmmeel lu sax la te dëgg la.

Loraangey fitna ak solos muslu ci Yàlla ak ñaan ngir mucc ca.

Saxal ne Dajjaal dana génn ak fitnaam gu màgg ga.

Sopp nañu ñaan gii ginnaaw taaya gi mujj.

Sopp nañu ñaan ginnaaw bu ñu defee jëf ju sell.

التصنيفات

Sikkar yi ànd ak julli gi