إعدادات العرض
Jaayante naa ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak dégg ak topp, ak laabire bépp jullit
Jaayante naa ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak dégg ak topp, ak laabire bépp jullit
Jële nañu ci Jariir Ibn Abdullah-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Jaayante naa ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak dégg ak topp, ak laabire bépp jullit.
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල Svenska ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Tiếng Việt پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or Malagasy नेपाली Čeština Oromoo Română Nederlands Soomaali తెలుగు മലയാളം ไทย Lietuvių Српски Kinyarwanda Shqip ಕನ್ನಡ Українська Moore ქართული Magyarالشرح
Sahaaba bii di Jariir Ibn Abdullah -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne moom dafa kollarante ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci Tawhiid ak di jooxe julliy juróom yi ñu farataal ci bis bi ak ci guddi gi, ci ay sàrtam ak i ponkam, ak i wareefam, ak i sunnaam, ak ci joxe asaka, mu nekk ag jaamu gu aju ci alal nekk lu war, dees koy jële ci way-woomal yi jox ko ñi ko yayoo ci way-ñàkk yi ak ñeneen, kollarante ak moom it topp ñi jiite mbir yi, ak di laabire bépp jullit, loolu nag ngir xér ci jariñ ko, ak eggale yiw ci moom, ak jeñal ko lor ci wax ak jëf.فوائد الحديث
Solos julli ak asaka,te ñoom ñaar dañoo bokk ci ponki Lislaam yi.
Solos laabire ak laabirante ci diggante jullit ñi, ba tax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di jaayante ak sahaaba yi ci loolu.
التصنيفات
Ngëneelu julli