sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy

sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy, te bokk na ci fésal ag moy nit ku def dara ci guddi gi, daal di xëy Yàlla suturaal ko, muy wax naan: éey yaw diw, biig def na lii ak lee, fekk dafa fanaan Yàlla suturaal ko, mu xëy di wuññi li ko Yàlla suturaaloon».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jullit bi def bàkkaar dees na ko yaakaaral suturas Yàlla ak njéggalam, ba mu des kiy yégle ak moyam di ko ndamoo, kooku yeyoowul njéggal; ndax day def ag moy ci guddi gi, xëy Yàlla suturaal ko, muy wax keneen naan ko moom dafa def ag moy ak jigéen sàngam démb, dafa fanaan Yàlla di ko suturaal, mu xëy di wuññi suturas Yàlla ci moom!!

فوائد الحديث

Ñaawug fésal ag moy ginnaaw bi ko Yàlla suturaalee.

Nekk na ci fésal ag moy tasaare ñaawteef ci diggante way-gëm ñi.

Ku Yàlla suturaal ci àdduna dana ko suturaal ca allaaxira, lii daa bokk ci yaatug yërmàndey Yàlla mu kawe mi ci jaamam yi.

Ku ñu nattoo ag moy na suturaal boppam te tuub jëm ci Yàlla.

Màggug Bàkkaaru ñiy fésal ag moy ak diko feeñal di xañ seen bopp ag njéggal.

التصنيفات

Ŋàññ moy yi